$ : , SUNUNET ) @ 4
POETES
DU SENEGAL ET D’AILLEURS
La Releve Poetique Senegalaise
|
________________________________________
|
Gore Daf Di Nyaan
Lire Ce Poeme En: Francais
Anglais
Ma né Wax nu Ku leen gis, nu dellusi ci guudi ? Rab yi ci àll bi Di dellusi guddi Te bëccëgu njolloor nuy naaw Nakka njugub yiy nàmp derati nit Tey tagg ci pegg yu ratax Yi ci kàmb. Wax nu ku leen gis ? Wax nu ku leen gis ? Rab yiy dox diggu njolloor . Ci digg àllu mandeng mi ngelaw liy wall tàkkusaan Ci la guddi lëndëm Kuruus tëdd Boxx bànneexam Nerferkare Danga leer ! Lalal ci kow suuf leer nann Ma né Yàlla , Nun yéeg nan tey ciy
jaww Te yéen néew yi dëddu àddina Hamleen ka Maa di démb te dara umpu ma ci ëllëg Ma di dënnu wu weex tàll woowu Di àddu fu mu tawe ba sewÊt Def xon muri mel nam jant Yéen ni yëlif ndox Di Rabi ndox Yéen niy aw ci
sama kàddu Man maa di ki leen Wo Yow Tswigoo Yow miy Baayi Baay yi Yaay sunu Baay Nun Ndaama yi Defal ba niir yii di Taw. Fexeel ba ma nyam doom yi suuf menn Danga dootul ndax sunu Baay ? Baayu Baay yi ? Jamono yegsi na Bant bi xer ndox Nanga ji te mennyal Allu jàmm wi wêr Ngaay Mexe Beykatu dugubu jamm Beykatu ceebu jamm Komo Nama wi jooy na jamm. Ama may ko fan wu guud Moom komo nama wu bees wi Na la suuf sédd Fan wu gudd, Yaw koma nama wu Bees wiy seede Addina wiy nëw Nit day reer tëdd. Dee Mu sedd guyy ! Na la Rab wiy wattu Sédd fan wu gudd Danga di Boroom kàddu gu wér Kumba Bang Kumba Lambaay Kumba Kastel Sedd nu jàmm Sedd nu fan wu gudd Yàgg ci buumu njaam Wër àddina ba mu sës Génn xeet ci àtte Nu jaay la ci yoon Nga dellu tey di gor Man ma di Gore Professeur P. DiagneExtrait
du narratif poetique “Goree
Est Memoire” |
|
|
Reagissez
A Ce Poeme Dans Le Livre D’or |
|
Copyright © 2000 - All Rights Reserved
[A
Propos De Nous] [Questions?]
[Contactez nous] |